Dindi Tor Browser ci sa nosteg amalin jafewul:
Ci Windows:
- Gisal sa wayndaare wala amalinu Tor Browser . Nekkin bi teew mooy Desktop bi.
- Dindil Tor Browser bi wala amalin bi.
- Tuural sa Mbalit.
Ci macOS:
- Gisal sa amalin Tor Browser. Nekkin bi teew mooy wayndare amalin bi.
- Yóbbul amalinu Tor Browser sa mbalit ma.
- Demal ci sa
~/Library/Application Support/
wayndare.
- Jàppal ne wayndaare Library bi mi ngi làqqu ci xeetu macOS bu bees bi. Ngir xuus ci wayndaare boobule ci Finder, tànnal "Go to Folder..." alluwa "Go" bi.

- Te nga bind
~/Library/Application Support/
ci xët bi te kilike Go.

- Gisal joxe wayndaare TorBrowser- te nga yóbbu ko sa Mbalit.
- Tuural sa Mbalit.
Jàppal ne soo sampul Tor Browser ci nekkin bi teew (twayndaare amalin bi), ak wayndaare TorBrowser-Data nekkul ci ~/Library/Application Support/
wayndaare, wante ci wayndaare menn wayndaare bi nga samp Tor Browser.
Ci Linux:
- Gisal sa wayndaare Tor Browser . Ci Linux, amul nekkin bu teew, wante wayndaare bi dinanu ko tuddee "tor-browser_en-US" su fekkee xuusukaay Tor Browser bi ngay jëfandikoo ci Angale la nekk.
- Dindil wayndarey Tor Browser bi.
- Tuural sa Mbalit.
Jàppal ni sa nosteg amalin jëfukaay "Uninstall" kenn jëfandikoowu ko.