Onion services (nu njëkk ko xame ci "serwiis yu làqqu") nekk na ay serwiis, yu mel ni ay dalukaayi web, yu jàppandi ci jokkoowu Tor bi kese.

Onion services dafay joxe ay njëriñ ci kaw serwiis yu yamamaay ci web bu amul kiirlaay bi:

  • Onion services' bërëb ak IP address nëbb nanu leen, jafeel ko noon yi, ngir nu dagg lëkkaloo bi wala ràññee operatëer bi.
  • Yoon yepp ci diggante jëfandikukati Tor ak onion services nekk na cat ba cat encrypted, kon jarul ngay jaaxle ci lëkkaloo ci HTTPS.
  • Daluwaayu ab onion service danu ko defar automatically , ba nga xam ne operatëer yi duñu soxla jënd ab raññeekaay.
  • Ndax mbëjfeppal bi ci bokk, URL onion dafay bayyi Tor wooral ne mi ngiy lëkkaloo ci bërëb bu baax bi ak wooral ne jokkowam kenn nekkul di ko yàqq.

NAN LANUY JOTEE CI AB ONION SERVICE

Ne bépp beneen dalu web, di nga soxlaa xam dëkkuwaay bu ab onion service ngir mën a lëkkaloog moom. Ab onion address ëmb na 56 araf ak ay lim, ".onion" topp leen.

Sooy jot ab dalu web buy jëfandikoo ab onion service, Tor Browser dina wone ci bantu URL bi ab xët bu onion di wone sa nekkinu jokkoo: Kaarànge ci jëfandikoo ab onion service. Mën nga jàng lu gën a yaatu ci onion site bi ngay seet jaare ko ci xool liy feeñ ci Circuit bi.

Beneen anam ngir jàng lu jëm ci ab onion site mooy su fekkee ki di doxal daluweb bi teg na ab melo bu nu duppee Onion-Location. Onion-Location nekk na ab jëfandikukat bu matul bu HTTP te dali web yi mën ko jëfandikoo ngir siiwal seen naatangoo onion. Su fekkee dalukaayu web bi nga nekk di xool dafa am ab onion site bu jàppandi, ab doomu xelal bu wiyolet dina feeñ ci Tor Browser di wone ".onion jàppandi". Soo kilikee ci ".onion available", dalu web bi dina sarsewaat te toxu ci naatangoom onion.

Onion-Location

ONION SERVICE AUTHENTICATION

Ab onion service bu baax mooy ab serwiis bu niroog ab onion site buy laaj kiliyaan bi joxe ab gindikaayu authentication laata ngay jot serwiis. Ne ab jëfandikukat bu Tor, mën nga raññele sa bopp ci Tor Browser. Ngir jot serwiis bii, da nga soxla am ay baati dugg yu joge ci aji doxalkatu onion service bi. Sooy jot ab onion service bu baax, Tor Browser dina wone bantu URL bi ab xëtu caabi bu ndaw bu melo doomu-taal, benn jumtukaay àndak moom. Duggalal sa private key bu baax bi ci bërëbu deñc ab joxe bi.

Client Authorization

ONION SERVICES NJUUMTE

Soo mënul jokkoo ci ab onion site, Tor Browser dina joxe ab message bu njumte su dalukaayu web bi jàppandiwul. Ay njumte mën na ñoo am ci tolluwaay yu wute: njumte kiliyaan yi, njumte jokkoo yi, wala njumte serwiis yi. Yenn ci njuumte yiile mën nanu leen defar jaaree ko ci pàccu Troubleshooting. Tablo bii ci suuf dafay wone njuumte yi mën a nekk ak ban jëf nga war a def ngir saafara jafe-jafe bi.

Kot Njuumte Tomb Tegtal bu gàtt
0xF0 Onionsite Kenn Gisu ko Li ko gën a waral mooy onionsite kenn mënu ci jokkoo. Jokkool ak aji caytukat bu onionsite.
0xF1 Onionsite Kenn Mënu ci Dugg onionsite kenn mënu ci dugg ndax njuumte ci biir.
0xF2 Onionsite Dafa dakkal Jokkoo bi Li ko gën a waral mooy onionsite kenn mënu ci jokkoo. Jokkool ak aji caytukat bu onionsite.
0xF3 Mëneesul Jokkook Onionsite Onion site bi jàppandiwul wala jokkoowu Tor bi dafa fees dell. Jéemaatal ci kanam.
0xF4 Onionsite dafay Laaj Authentication Jot onionsite bi dafay laaj ab caabi wànte joxewunu woon benn.
0xF5 Onionsite Authentication dafa Lajj Caabi ji nu joxe baaxul wala danu ko sempi. Jokkool ak aji caytukat bu onionsite.
0xF6 Dëkkuwaayu Onionsite baaxul Dëkkuwaayu onionsite bi nu joxe baaxul. Nu ngi lay ñaan nga duggal ko ni mu waree.
0xF7 Onionsite Circuit Creation Ajandi nanu ko Lajj na ci jokkoog onionsite, mën na nekk jokkoo bu amul doole moo ko waral.

TROUBLESHOOTING

Soo mënul jot onion service bi nga laaj, na la woor ne dugg nga onion address bi ci duggin bu baax: donte ab njumte bu ndaw dina dakkal Tor Browser ba du jàppandi ngir jot dalu web bi.

Soo jéemee jot ab araf 16 ("V2 format" bu gëna gàtt) onion service, xeetu dàllukaay yii doxatul ci jokkoob Tor bu tey.

Mën nga tamit xayma ndax mën nga jot yeneen onion services jaaree ko ci lëkkaloog DuckDuckGo's Onion Service.

Su fekkee mënuloo lëkkëloo ci onion service gànnaaw ba nga xoole dal bi, nu ngi lay ñaan nga jéemaat ci kanam. Mën na am ab jafe-jafe lëkkaloo bu dul yàgg, wala aji yor dal bi mën na ko may mu génn ci jokkoo bi te àrtuwul.