Tor Browser ci Android

Tor Browser ci Android mooy xuusukaayu portaabal bi fës bi Tor Project defar te di ko doxal. Dafa mel ni Tor Browser bu biro wante ngir sa telefonu portaabal Android. Yenn ci melo yu njëkk yi Tor Browser ngir Android bokk na ci: waññi topp gi ci dalukaayu web yi, aar ceytu gi, di dëggërlu ci fingerprinting, ak moytu tere yi.

YEBBI AK SAMP

Am na Tor Browser ngir Android ak Tor Browser ngir Android (alpha). Jëfandikukat yu ajuwul ci wallu xarale dañoo war a am Tor Browser ngir Android, ndegam bii dal na te njumte yi bariwul. Tor Browser ci Android jàppandi na ci Play Store, F-Droid ak dalukaayu web bu Tor Project. Wóorul ci ngay yebbi Tor Browser feneen fu bokkul ak ñetti mboolem jëfukaay yii.

Google Play

Mën nga samp Tor Browser ngir Android jaare ko Google Play Store.

F-Droid

The Guardian Project dafay joxe Tor Browser ngir Android ci seen F-Droid deñcukaay. Soo bëggee samp jumtukaay jaaree ko ci F-Droid, nu ngi lay ñaan nga topp jéego yii:

  1. Sampal jumtukaayu F-Droid bi ci sa jumtukaayu Android jóge ci the F-Droid website.

  2. Gànnaaw ba nga sampee F-Droid, ubbil jumtukaay bi.

  3. Ci suuf wetu ndeyjoor ci koñ bi, ubbil "Settings".

  4. Ci suufu pàccu "My Apps", ubbil Repositories.

  5. Jafalal "Guardian Project Official Releases" niki lu nu doxal.

  6. Léegi F-Droid dafay yebbi limu jumtukaay yi joge ci the Guardian Project's dencukaay (Jappal: lii mën na jël ay simili).

  7. Bësal Back butoŋ bi ci kaw wetu cammooñ ci koñ bi.

  8. Ubbil "Latest" ca wetu cammoñ ca suuf ca koñ ba.

  9. Ubbil Jumtukaayu seet bi nga bës seetu yaatal bi nekk wetu suuf ci ndeyjoor bi.

  10. Saytu ngir "Tor Browser ci Android".

  11. Ubbil njureefi laaj yi ci "The Tor Project" te nga samp.

Dalu web bu Tor Project bi

Mën nga am tamit Tor Browser ngir Android jaare ko ci yebbi ak samp apk jaare ko ci Tor Project website.

XUUS CI TOR BROWSER NGIR ANDROID Ci YOON WU NJËKK

When you run Tor Browser for the first time, you will see the option to connect directly to the Tor network, or to configure Tor Browser for your connection.

Lëkkale

Lëkkaloo ci Tor Browser ngir Android

Ci anam yu bare, tànn "Connect" dina la may nga lëkkaloo ak jokkoowu Tor bi te doo am benn tërëlin booy samp. Once tapped, a status bar will appear, indicating Tor's connection progress. If you are on a relatively fast connection, but the progress bar gets stuck at a certain point, you might have to configure Tor Browser.

SAMP

Samp Tor Browser ci Android

If you know that your connection is censored, you should tap on "Configure connection". Navigate to the 'Connection' section of the Settings. Su fekkee sa lëkkaloo danu ko dindi, wala jéem nga te lajj ci lëkkaloo ak jokkoo bu Tor te benn saafara sottiwul, bësal ci 'Config Bridge'. You will then be taken to the 'Config Bridge' screen to configure a pluggable transport.

MOYTU

Jàllalekaayi Bridge ñooy jàllekaayi Tor yi nu deful ci àlluway Tor bu fës bi. Bridges am na solo ngir ñiy jëfandikoo Tor te nekk ci nguur yi nooteel yi bare, ak ngir nit ñi soxla kaarànge ndaxte dañoo ragal nu xàm ne dañuy jokkoo jaare ko ci ab dëkkuwaayu Tor relay IP bu fës.

To use a pluggable transport, tap on ""Configure Connection" when starting Tor Browser for the first time. Navigate to the 'Connection' section of the Settings and tap on 'Config Bridge' to configure a bridge. Beneen xoolu bi dina joxe tànneef bi ngir nga jëfandikoo ab built-in bridge wala bridge bus a coobare. Toggle "Use a Bridge" option, which will present three options: "obfs4", "meek-azure", and "snowflake".

Tànnal ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Tànnoon ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Su fekkee tànn nga "Provide a Bridge I know", kon war nga dugg ci ab bridge address.

Joxe ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Joxe dëkkuwaayi bridge yi ci Tor Browser ngir Android

SAYTU XAMMEEKAAY

Raññeekaay bu Bees

New Identity ci Tor Browser ngir Android

Su Tor Browser dee dox, di nga gis loolu ci sa àlluway yëgle ci sa jumtukaay gànnaaw ba nga ko yaatale ak sa butoŋu "NEW IDENTITY". Bës ci butoŋ bi dina la indil ab new identity. Ci lu dëppoowuk ak ci Tor Browser ngir Ordinaatëru Biro, "NEW IDENTITY" butoŋ bi ci Tor Browser ngir Android terewul say jëf ci sa xuusukaay bi nu mën ko lëkkale ak li nga doon def bu njëkk. Tànn ko dina soppi sa Tor circuit képp. Note: New Identity feature is not working in latest versions of Tor Browser for Android. Bug #42589

KAARÀNGEY TOLLUWAAY

Sukkandikukaay yu am kaarànge ak ab jumtukaayu nataal bu am kaarànge ci Tor Browser ngir Android

Security levels disable certain web features that can be used to compromise your security and anonymity. Tor Browser ci Android dafay joxe ñetti toluwaayu kaarànge yu niroo yu jàppandi ci ordinaatëeru biro. Mën nga soppi tolluwaayu kaarànge gi ci topp jéego yii nu joxe:

  • Bësal ci ab butoŋ bu am 3 tomb yu taxaw ci bantu URL bi.
  • Scroll down and tap on "Security Level".
  • Mën nga tànn léegi ab tànneef maanam. Standard, Safer wala Safest.

YEESAL

Tor Browser must be kept updated at all times. If you continue to use an outdated version of the software, you may be vulnerable to serious security flaws that compromise your privacy and anonymity. Mën nga yeesal Tor Browser automatically wala ak sa loxo.

Yeesal Tor Browser ngir Android automatically

Jëfekaay bii dafay dëggal ni am nga Google Play wala F-Droid bu nu samp ci sa telefon portaabal.

Google Play

Yeesal Tor Browser ngir Android ci Google Play

  • Ubbil jumtukaayu Google Play Store bi.
  • Ci kaw ci ndeyjoor, bësël alluway xët bi.
  • Bësal ci 'Manage apps and devices'.
  • Bësal ci xëtu 'Manage' bi.
  • Bësal ci 'Updates available'
  • Bësal ci Tor Browser ngir Android jóge ci limu jumtukaay yi nu war a yeesal.
  • Bësal ci 'Update'.
F-Droid

Yeesal Tor Browser ngir Android ci F-Droid

Bësal ci "Settings", daldi dem ci "Manage installed apps". Ci beneen xoltu bi, tànnal Tor Browser te ca mujjantal ga nga bës ci butoŋu "Update".

Yeesal Tor Browser ngir Android ak say yoxo

Wëral Tor Project website te nga yebbi ab kayit bi Tor Browser mujjee génnee, ba noppi nga samp ko ne bu njëkk. Ci anam yu bare, version bu Tor Browser bu mujj bii dina sampu ci kaw version bi gën a yàgg, ci noonee di yeesalaat xuuskat bi. Su fekkee loolu dafa lajj ci yeesal xuusukaay bi, mën na am nga soxla sempi Tor Browser laata nga koy sampaat. Ak Tor Browser tëj, dindi ko ci sa jumutukaay nga sempi ko jëfandikoo say sukandikukaayu jumtukaay. Aju ci sa xeetu telefon portaabal, xuusal ci Settings > Apps, nga daldi tànn Tor Browser te nga bës ci butoŋu "Uninstall" bi. Gànnaaw loolu, yebbil Tor Browser bu mujjee génn te nga samp ko.

SEMPI

Tor Browser ngir Android mën nanu ko sempi ci sassa jaare ko ci F-Droid, Google Play wala jaare ko ci say sukkandikukaayi jumtukaayu telefon portaabal.

Google Play

Sempi Tor Browser ngir Android ci Google Play

  • Ubbil jumtukaayu Google Play Store bi.
  • Ci kaw ci ndeyjoor, bësël alluway xët bi.
  • Bësal ci 'Manage apps and devices'.
  • Bësal ci xëtu 'Manage' bi.
  • Bësal ci Tor Browser ngir Android jóge ci limu jumtukaay yi nu samp ci sa gindikaayu ordinaatëer.
  • Bësal ci 'Uninstall'.

F-Droid

Sempi Tor Browser ngir Android ci F-Droid

Bësal ci "Settings", daldi dem ci "Manage installed apps". Ci beneen xoltu bi, tànnal Tor Browser te ci mujjantal gi bësal ci butoŋu "Uninstall".

Sukkandikukaay yu jumtukaayu loxo

Sempi Tor Browser ngir Android di jëfandikoo ay sukkandikukaayi jumtukaayu internet

Aju ci sa xeetu telefon portaabal, xuusal ci Settings > Apps, nga daldi tànn Tor Browser te nga bës ci butoŋu "Uninstall" bi.

TROUBLESHOOTING

Yër Tor Logs

View Tor logs on Tor Browser for Android

Ngir gis say Tor logs:

  1. Tap on the settings icon or "Configure connection" when on the "Connect to Tor" screen.
  2. Navigate to the "Connection" section of the Settings.
  3. Tap on "Tor Logs"

To copy the Tor logs to the clipboard, tap on the "Copy" button at the bottom of the screen.

Ngir defar yenn jafe-jafe yi ëpp yu faral di am nu ngi lay ñaan nga xool Support Portal entry.

JAFE-JAFE YUNU XAM

Fii nu toll, am na ay melo yu jàppandiwul ci Tor Browser ngir Android, wante ci jamono jii jàppandi na ci Tor Browser ngir ordinaatëeru biro.

  • Mënuloo gis sa Tor circuit. #41234
  • Tor Browser ngir Android du lëkkale su demee ci Kàrtu SD bi. #31814
  • Mënuloo jël ay nataalu xoltu sooy jëfandikoo Tor Browser ngir Android. #27987
  • Mënuloo ubbi ay dëkkuwaay onion yiy laaj Client Authorization #31672
  • 'New Identity' feature is not working on latest versions of Tor Browser for Android. #42589

Yeneeni mbiri Tor ci jumtukaayi loxo

Orfox

Orfox nu ngi ko njëkk a génne ci 2015 ci The Guardian Project def ko ak jubluwaay jox jëfandikookati Android yi ab anam ngir xuus ci internet jaare ko ci Tor. Ci diiru ñetti at yii weesu, Orfox dafa wéyaloon di yokku te nekk ab yoon wu siiw ngir nit ñiy xuus ci internet ak kiirlaay gu doy wuteeg xuusukaay yi faral di am, te Orfox amoon na dayoo lool ngir jàppale nit ñi doon dund ñuleen di tere aka bloke ci yenn dalu web ak ëmbeef yu doy waar. Ci 2019, Orfox was sunsetted gànnaaw banu gennee Tor Browser ngir Android bu ofisiyel.

Orbot

Orbot jumtukaayu proxy bu laajul fay buy dooleel yeneeni jumtukaay yi ngir ñuy jëfandikoo jokkoowu Tor bi. Orbot dafay jëfandikoo Tor ngir fas doxalinu Internet bi. Noone mën nga ko jëfandikoo ak yeneeni jumtukaay yi nu samp ci sa telefon portaabal ngir moytu dakkal bi te aar sa bopp ci ceytu gi. Orbot mën nanu ko yebbi te samp ko jaaree ko ci Google Play. Xoolal our Support portal ngir xam ndax soxla nga Tor Browser ngir Android ak Orbot wala benn ci ñoom.

Tor Browser ci iOS

Amul Tor Browser ci iOS. Nu ngi lay diggal ab jumtukaayu iOS bu nu tuddee Onion Browser, te mu nekk open source, jëfandikoo sëfu xayma bu Tor, te ki ko defar nekk kenn kuy liggéeyando ak Tor Project. Wànte, Apple dafay laaj xuusukaay ci iOS ngir jëfandikoo mbir bi nu tudde Webkit, liy tee Onion Browser am kiirlaay yu nirook ay kiirlaayu Tor Browser.

Jàngal leneen lu bari ci Onion Browser. Yebbil Onion Browser jëlee ko ci App Store.

Tor Browser ci telefonu Windows

Amul fi nu toll benn jëfekaay ngir doxal Tor ci telefonu Windows yu yàgg wànte su fekkee xeeti telefonu Microsoft/ yu yees yi la ,ñoo niroo jéego ci Tor Browser on Android mën nanu leen topp.