So lëkkaloo ak ab dalu web, nekkul nostegkati doxin yi rekk ñoo mën a rënk xibaar yu aju ci sa yër. Dalu web yu bare léegi dañuy jëfandikoo ay banxaas yu toftalu yu bare, bokk ci butoŋu "Like" ci mbaalu jokkko yi, toppkat analitik yi, ak jumtukaayu siiwal yi , yooyu yépp mën nañu lëkkale say jëf ci dalu web yu wuute.
Di jëfandikoo jokkoowu Tor bi dina tax xoolkat yi dakkal mëneefi gis bërëb ba nga nekk ak sa dëkkuwaayu IP, wante donte bu xibaar boobu amul sax dinanu mën a lëkkale say jëf yu wuute booleleen. Ngir loolu, Tor Browser am na ay melo yu dolleeku di la jàppale nga saytu ban xibaar lanu mëna lëkkalee ak sa identity.
BAARU URL BI
Tor Browser dafay dajale sa jaar-jaaru web ci sa lëkkaloo ak dalukaayu web bi ci bantu URL bi. Donte soo lëkkaloo ci ñaari dalukaay yu wute yuy jëfandikoo ab banxaas buy topp ñetteelu pàcc bi niroo, or Browser dina forse ëmbeef bi nu seddale ko ci ñaari Tor circuits yu wute, ba xam ne toppkat bi du xam ne ñaari lëkkaloo yépp ñu ngi bokk joge ci sa xuusukaay.
Ci beneen boor, lëkkaloo yépp ci ab dalukaayu web dinanu ko def ci kaw Tor circuit bu méngoo di tekki ni mën nga xuus ci ay xët yu bare te wute bu ab dalu web ci ay xët wala palanteer yu wuute, te doo ñȧkk doxalin.
Mën nga gis ab jagaram bu circuit boobu Tor Browser di jëfandikoo ngir xët biy dox ci àlluway dalukaayu xibaar yi, ci bantu URL bi.
Ci circuit bi, Guard bi wala entry node bi mooy node bi njëkk te danu ko tȧnn automatically ak noonu rekk jaare ko ci Tor. Wante dafa wuteeg yeneen lëkk-lëkk ci circuit bi. Ngir moytu ay songu ci sa profil, Guard node yi dañuy soppeku rekk gànnaaw 2-3 weer yi, wuteeg yeneen lëkk-lëkk yi, yi di soppeku ak bépp fànn bu bees. Ngir xibaar yu gën a yaatu yu aju ci Guards, xoolal FAQ ak Support Portal.
DUGG CI BIIR TOR
Doonte dañoo defar Tor Browser ngir may jëfandikookat yépp nu am lȧqqute ci lënd gi, yenn saa dina am tolluwaay yoo xam ne dina am dayoo jëfandikoo Tor ak dalu web yiy laaj turu way jëfandikoo yi, baatu dugg yi, wala yeneen xibaar yuy tax nu xam la.
Sooy log ci biir dalu web biy jëfandikoo ab xuusukaay bu jaar yoon, dangay feeñal sa dëkkuwaayu internet ak fi nga nekk ci diiru amalin bi. Lu ni mel mooy am tamit su fekkee da nga yónnee bataaxal ci lënd gi. Dugg ci mbaalu jokkooyi wala këllu bataaxal yi di jëfandikoo Tor Browser daf lay may nga tànn bu baax ban xibaar ngay jox dallu web yi ngay xuus. Dugg ci lënd gi di jëfandikoo Tor Browser nekk na tamit lu am solo su fekkee dalu web bi nga bëgg a jot danu ko tere ci sa jokkoo.
Sooy log ci ab dalu web ci Tor, am na ay tomb yu bare yoo war a bàyyi xel:
- Gisal Xëtu lëkkaloo yu am kaaràngebi ngir xibaar yu am solo ci naka lanuy aare sa lëkkaloo sooy dugg ci internet bi.
- Tor Browser dafay faral di feeñal sa lëkkaloo mu mel ni mu ngi joge ci beneen béréb ci àdduna si bu wuute lool. Yenn dalu web yi, niki bànk yi wala ñiy joxe bataaxali internet yi, mën nañu gise lii niki ab màndarga bu sa kont sàcc wala yàqq, ba noppi génnee la. Benn yoon binuy saafaraa loolu mooy topp tegtal yi sa dal digle ngir jotaat sa kont, wala nga jokkook ñiy liggéey ci mbir mi te faramfacceel leen anam bi.
SOPPI XAMMEEKAAY AK CIRCUITS
Tor Browser dafay wone "New Identity" ak tànneef yu "New Tor Circuit for this Site". Nu ngi nekk tamit ci hamburger bi wala àlluwa bi ci buntu bi (≡).
NEW IDENTITY
Tànneef bii am na solo ci su fekkee bëgg nga fagaru ci sa jëfi xuus bi di ñëw baña lëkkaloo ak li nga doon ñjëkk a def. Di ko tànn dina tëj sa xët ak palanteer yu ubbeeku yépp, dindi xibaar yu aju ci yaw yépp yu melni ay cookies ak jaar-jaaru xuus, ak jëfandikoo Tor circuits bu bees ngir lëkkaloo yépp. Tor Browser dina la àrtu ne jëf yépp ak yebbi yépp dinañu dakk, kon bàyyil loolu xel bala nga kilike "New Identity".
Ngir jëfandikoo tàneef bii, danga soxla kilike ci 'New Identity' ci bantu jumtukaay bu Tor Browser.
TOR CIRCUIT BU BEES BU DAL BII
Tànneef boobule am na solo su fekkee exit relay bi ngay jëfandikoo mënul lëkkaloo dalu web bi nga soxla, wala sarsewul ni mu waree. Tànn ko dina tax xët bi wala palanteer bi sarsewaat ci kaw ab Tor circuit bu bees. Yeneen xët ak palanteer yu ubbeeku yu jóge ci dalukaayu web yu niroo dinañu jëfandikoo circuit bu bees tamit su xësee ba saresewaat. Tànneef bii du dindi bépp xibaar bu beru wala dindi lëkkaloo bi am ci say jëf, te du am benn njeexital ci sa lëkkaloo yi am ak yeneen dalu web yi.
Mën nga tamit dugg ci tànneef bii ci circuit bu bees bi, ci àlluway xibaar bu dalu web bi, ci bantu URL bi.