Tor dafay laaj sa tëralin am montar (ak sa waxtu gox) bu tegu ci waxtu wi jot tigi.
Kaarànge antiwiris wala malware buy tere jëfandikukat yi ñu dugg ci Tor Browser.
Yenn saa yi itam yooyu dañuy fëll ak ay mbir yu baax ak yu bon ci malware ak/wala ñàkk doole.
Mën nga jàng lu bari ci loolu ci sunu Support Portal.
Antiwiris yii ak firewall software xam nañu leen ci jaxasoo ak Tor te soxla na nu dindi leen yenn saa yi:
- Kaaràngey Webroot Fépp
- Kaspersky Internet Kaarànge 2012
- Sophos Antiwirusu Mac
- Kaaràngey Mbir yi am solo ci Microsoft
- Antiwirusu Avast
VPNs itam dinay faral jaxasoo ak Tor te laaj na dindi.
Digalunu itam boole jëfandikoo VPN ak Tor xanaa nga nekk way-jëfandikukat bu xereñ bu xam naka lanuy sampe ñaar yépp ci benn saa budul feeñal say mbiri bopp.
Mën nga am yeneeni xibaar yu leer ci Tor + VPN ci sunu wiki.
Widewo yiy laaj Adobe Flash jàppandiwuñu.
Flash bi dafay deñ ngir mbirum kaarànge.
Tor mënula jëfandikoo ab bridge soo sampee ab proxy.
Bésub ëmbu Tor Browser bi mooy 1 fab cu Samwiyee, 2000 00:00:00 UTC.
Lii dafay dëggal ne bépp software bunu tabax nekk na ca dëgg-dëgg lu mën a jur.
Jafe-jafey def Tor Browser niki sa default browser.
Su Tor Browser doon dox bu njëkk te doxatul léegi (rawatina ginnaaw ab sampaat wala ab yeesalaat), sa tëralin mën na réer.
Ab yeesal taal bu sa doxinu ordinaatëer, ci anam boobu, dina saafara jafe-jafe bi.
Tor du dox ci Windows bu yoonu booleb deñc bi amee ay màndargay non-ascii.
BitTorrent dafay feeñ ci Tor.